livret décodable 2 ggatu-ci-dawal-1-2.pdfleçon 2 de pré-lecture 1 leçon 3 de pré-lecture 1...

Post on 06-Oct-2020

2 Views

Category:

Documents

0 Downloads

Preview:

Click to see full reader

TRANSCRIPT

Livret décodable 2

DU PEUPLE AMERICAIN

Table des matières

Alphabet illustré 1

Table de l’alphabet 1

Leçon 1 de Pré-lecture 1

Leçon 2 de Pré-lecture 1

Leçon 3 de Pré-lecture 1

Leçon 4 de Pré-lecture 1

Leçon 5 de Pré-lecture 1

Leçon 6 de Pré-lecture 1

Leçon 7 de Pré-lecture 1

Leçon 8 de Pré-lecture 1

Leçon 9 de Pré-lecture 1

Leçon 10 de Pré-lecture 1

Leçon 3 de Pré-lecture 1

Leçon 3 de Pré-lecture 1

Alphabet illustré 1

Table de l’alphabet 1

Leçon 1 de Pré-lecture 1

Leçon 9 de Pré-lecture 1

Leçon 10 de Pré-lecture 1

Leçon 3 de Pré-lecture 1

Leçon 3 de Pré-lecture 1

BËRE XAJ AK GOLO

6

Estaad bi fees na dell aki mala.Xaj ngembu na di màttu. Mu ngi sangu ak saafara yu bare.

7

Golo mu ngi tuus, ñépp di ko tàccu.Mu ngi tëb ca kaw aka gaññ.Leeg-leeg mu pàkkarñi, fecc, tàllal loxoom.

8

Maam Golo mooy tëgg sabar, ñaq tooy xepp.Fas ak Nag ñu ngi koy may xaalis.Mbaam dóor na pooj waŋŋeetu ñetti yoon.

9

Bàjjan Béy arbit woo na ñaari mbër yi.Bi ñu duggee ci géew bi, Xaj baw.Arbit bi mbiib, ñu tàmbali léewtoo.

10

Xaj song na Golo mu génn géew bi.Arbit bi artu ko ci génn bi.

11

Xaj cokkaas na ko, Golo yuuxu Golo daw na làqu ci ginnaaw arbit bi.Leegi, Golo miir na di wëndéelu.

12

Noonu, arbit tàllal na loxoom woo doktoor Looy. Ndeysaan, Looy a ngi koy faj muy yuuxu.Mu metti, Golo yenu doktoor Looy daaneel.

13

Mbokki Golo jiital seen mbër yobbu. Doktoor looy jox na ndam li Xaj. Làmb ji jaxasoo, coow li jolli

Futbalu mala

16

Baay Gaynde dafa woote, mala yépp dawsi ñëw.Ñu yàkkamti koo déglu.Dama bëgg ngeen def joŋante bu am neexal.

17

Lëg, Mbaam-àll ak Bukki xoolante.Gaynde jël kàddu gi.Dama bëggoon boroom dunq jàkkaarloo ak boroom kawar.

18

Ginaar kobos Naat ne ko ñooy am ndam.Su bal bi naawee, ñu naaw.

19

Jabaru Golo wokk boppam di wax ak Ñey.Dinanu leen daan ndax noo leen ëpp doole.

20

Banjóoli yëngal ay mbaggam.Dama cee bokkul am dangeen maa fàtte. Njamala yuuxu, maay góol, bal du ma romb

21

Segg taxaw na, Fasu àll di daagu di bàkku.Lëg tëb ne man maay arbit.Mbonaat di seetaan, Jaan di fecc.

22

Jàmb Jóob duut, jox bal bi Seku.Mu jékki- jékki rekk, asamaan si lëndëm kuruus.Ndoxum taw dal, Béy daw, Ginaar topp ca.

23

Melax ne ràyy, dënnu yëngal suuf ak garab.Ndox mi di sotteeku mel ni géej.Ñey daadi daw, lépp jaxasoo.

NGÉNTE LI

26

Ami dafa am doom.Tey la am juroom-ñetti fan. Baayam Móodu bëgg na ngénte lu neex.

27

Bale nañu kër gi ba mu set wecc. Lal nañu basaŋ yu mag, teg ay siis.

28

Ci waañ wi, teg nañu mbana yi.Araw nañu leketi sunguf ngir laax yi.Ñeneen jël bagaani soow yi def ci suukar.

29

Ami sangu na, daadi solu. Takk na caq, lam ak jaaro yu gudd.Tey, mbubb mu mag la tànn ak kolam.

30

Jël na séru njaago lëmëse ko liir bi. Waa kër gi sañse nañu, tuuroo latkoloñ.

31

Jigeen ak góor defaru nañu ba jekk. Jigeen ñi takk nañu ceeni oor.Nit ñi toog ci ay basaŋ aki siis.

32

Bàjjan toog ci wetu Ilimaan, uuf liir bi. Ilimaan joxe tur wi, Bàjjan Kura. Ñu séddale laax yi ci bool yu ndaw.

33

Tëgg nañu sabar, tama, kooraa ak riiti.Togg nañu añ, njogonal, joxe am njar.Ginnaaw ba, ñu lekk pom, màngo ak banaana.

Espektëer dikk na

36

Defar nanu kalaas bi ba mu jekk.Bale nanu dër bi, raxas póllu mbalit mi.Fomp nanu palanteer yi ba ñu set wecc.

37

Sunu madam dafa farlu.Tey, sunu cawarte dafa yokku.Fëgg nanu armool bi def téere yi.

38

Madam Siise ni nu tey, danuy am gan.Su gan gi ñëwee, lépp lay xool.Léegi, toog nanu ci kalaas bi di jàng.

39

Oto bu xonq taxaw na sunu wetu ekool.Genn góor wàcce na ci oto bi.Mu ngi takk lunet yu ñuul.

40

Mu ngi téye saag bu mag. Kilifa gi dem na seeti direktëer. Toog nañu ñoom ñaar waxtaan ab diiir.

41

Sunu madam waaxu na jox loxo Espektëer bi.Bi nu sunu madam geestoo, ñépp jóg taxaw.Espektëer bi yékkati loxoom, nu toogaat.

42

Mu dem toog ca gannaaw di nu saytu.Nu tàmbalee nafar li nu jàngoon lépp.

43

Sunu madam dinu laaj, nuy tontu.Espektëer jóg na, ñëw ci sunu madam.Ba mu yàgg, ñu ànd dem ca direktëer.

Fànta ak Biraan am nañu ndam

46

Bu ekool tëjee, direktëer dafay joxe neexal.Ñaari xale yi raw ci kalaas lañuy tànn.Fanweeri fan ci weeru sulet lañu ko def.

47

Suba teel, xale yi ñëw, sañse ba jekk.Ñii sol yëre cosaan, ñee sol yëre yeneen .Xale yi ànd ak seeni waajur.

48

Muse ak madam yépp sañse nuróole ay waks.Ëtt bi set lool, xale yi bég.Xale yiy am neexal toog ci kanam.

49

Ci seen ndeyjoor, kilifa yi toog fa.Xumb-xumb yi nekk ci seen càmmoñ. Waajur yi toog nañu ci gannaaw elew yi.

50

Neexal yaa ngi tege ci kanamu xale yiÑu ràññee ca téere njàng ak xayma.Amoon na itam ay kaye ak ay tablet.

51

Bi fukki waxtu jotee, mbir mi tàmbali.Ñu jëkke ci kalaas bu ndaw bi.Fànta ak Biraan lañu jëkk a woo.

52

Ñu dem ci kanam, ñépp di leen tàccu.Direktëer bi jël paket bu mag a mag.Mu nuyu Fànta, jox ko ko.

53

Mu woo Biraan, jox ko beneen paket.Ñii di leen kameraa, ñee di leen foto. Seen moroom yépp di leen xool, naw leen.

DU PEUPLE AMERICAIN

top related